Ode aux Enseignants (Par Cheikh Ahmadou Kara Mbacké)

kara-eleganceYéen Enseignants yi, maa ngi leen di soutenir

Man Général u BAMBA, ci biti ak ci biir

Ndax, yéen a di Citoyens « numéro Un »

Jàngale da fa métti, bu kenn neh : han !

Inch’ÂLLAH, li ngeen bëgg, faww mu am

Dimbali leen xale yi ndax ñu am ndam

Bu ko  defee mu doon jaam-u-YÂLLAH ci yéen

Saah buñ jëlee réew mi, ci ngeen di man a téen

Te loolu yàgg a tul, na ngeen muñ bu rafet

Jafe na, waaye buy yoomb da leen di bétt

Wax u ma ko rek ngir bëgg lu leen neex

Da ma koo gëm te bëgg rek ngeen man a féex

Samay doom ak seen i doom, ñëpp a ci yem

Ma leen di ñaan ngir jëmm i KU-TEDD-KI

Ngeen sauver njàngum xale yi bañ tekki

Fas nañ yéene jòg di leen jàppale

Ngeen am ndam ci lu dul demalee’k a fekkele

                        Cheikh Ahmadou KARA Mbacké

 

Traduction française  

 

Vous les Enseignants, je vous témoigne de mon soutien

Moi le Général de BAMBA, de façon interne et externe

Car, c’est vous le citoyen « numéro un »

Bien qu’enseigner soit très dur, que personne ne se plaigne

S’il plait à DIEU, vos doléances à coup sûr, seront agréées

Assistez les enfants à la réussite

Comme s’il s’agissait d’un acte de dévotion envers Le SEIGNEUR

C’est lorsque nous prendrons le Pouvoir que vous pourrez redresser la tête

Ce sera dans un temps proche, soyez d’une belle patience

C’est ardu, mais cela se réalisera à votre grande surprise

Je ne le dit pas seulement pour votre plaisir

Puisque j’y crois, en vous souhaitant tout le bonheur

Ma progéniture ainsi que la vôtre, toutes identiques

Telles celle des autres parents, l’enseignement est pour tous

Je vous prie au Nom du Très-Saint

De préserver l’école de la perte, pour que réussissent les jeunes

Nous avons dès lors décidé de vous soutenir

Jusqu’à la victoire sans autre forme protocolaire.

Comments are closed.